Aynon
From Wikipedia
Ci làkku ibrë la tur wi jóge. Ci angale mooy Aenon; Ci faranse mooy Énon
Bérab boo xam ne sorewul Salim la woon, ci sowu dexu Yurdan gi ci wàll bëj-gànnaaru dex ga. Xamatuñu tey jii ne tembe fan la Aynon walla Salim nekkoon. Waaye dañu koy gëna yaakaar bérab bu sorewul dëkk bi tudd tey jii Napalus (Naplouse).
Man nañu koy gis ci Yow 3:23.